TSK

TSK · Daniel 12:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ca saa sa juróom benni góor jóge yoonu bunt ba féete kaw te janook bëj-gànnaar, ku nekk ŋàbb sa ngànnaayal reyukaay. Keneen a nga ca seen biir, ku sol ndimol lẽe, ak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. Ñu dikk taxaw ca wetu sarxalukaayu xànjar ba.

Ci kaw loolu ma dégg baatu nit jibe ca digg yoonu ndox ma ñuy wax Ulay. Mu àddu ca kaw ne: «Jibril, waxal kii peeñu mi.»

¶ Malaakam Aji Sax ji ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, loo deeti xaar, doo noppee xañ yërmande Yerusalem ak yeneen dëkki Yuda? Juróom ñaar fukki at a ngii yoo leen mere!»

Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.

Mu ngi yor ab téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndijooram ci géej gi, teg tànku càmmoñam ci jéeri ji.

Xarekat yi ci asamaan a ko topp, war fas yu weex, sol mbubbum lẽe mu weex, set wecc.