TSK

TSK · Daniel 3:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla.

Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, ngalla wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw Aji Sax ji doŋŋ yaa di Yàlla.»

Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji; seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole.

Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.

Ñooñu yeew leen na ñu soloo, ñook seeni mbubb ak seeni tubéy ak seeni mbaxana, daldi leen sànni ca biir taal bu yànj ba.

Ñépp a leen di bañ ndax sama tur.

Lii ma wax, buur bi xam na ko, moo tax ma ñeme koo wax ci kanamam, ndax bir na ma ne, amul lenn lu ko ump ci lii, ngir du cib ruq la xewe.

Ngëm lañu feye dooley sawara, ngëm lañu rëcce ñawkay saamar, ngëm a waral ñu weccikoo kàttan seenug néew doole, ci kaw ngëm lañu doone ay ñeyi xare, ba dàq gàngoori yeneen réew.