TSK

TSK · Deuteronomy 18:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israyil.»

Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Yeen nag lees di wooye: «Sarxalkati Aji Sax ji,» ñu naa: «Sunu surgay Yàlla yaa ngi!» Alali xeet yi, yeena koy lekk, di damoo seeni koom.

¶ «Sarxalkat yi am nañu seen céru bopp: man maay seen cér. Du jenn moomeel ju ngeen leen di jox ci suufas Israyil. Man maay seen moomeel.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.