TSK

TSK · Deuteronomy 5:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir.

Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga.

Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?

Aji Sax ji ne ma: «Jógal wàcce fii gaaw, ndax sa bokk ya nga génnee Misra def nañu yàqute. Teggi nañu xaat yoon wa ma leen santoon. Móolal nañu seen bopp jëmmu tuur.»

Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra te ngeen sàmmoo jëfe dogali yoon yii.

Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra. Looloo waral man, ma sant leen ngeen jëfe ndigal loolu.

Aji Sax ji, maay sab jaam, maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur. Yaa yiwi samay buum,

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.