TSK

TSK · Deuteronomy 6:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,

Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.

Jëfeleen njub, ak mbaax gi Aji Sax ji rafetlu. Su ko defee dingeen baaxle, ba dem, nanguji réew mu baax mi Aji Sax ji giñaloon seeni maam,

Su ngeen lekkee ba regg, am kër yu baax yu ngeen tabax dëkke,

Nangu nañu ay dëkk yu tata wër, ak suuf su nangu, aakimoo kër yu fees ak gépp ngëneel, aki teen, ak tóokëri reseñ, ak garabi oliw, garab yay meññ, ne xas; ñuy lekk ba suur. Ñu regg, di xéewloo sa mbaax gu réy gi.

Mu jox leen suufi yéefar ya, ñu jagoo ñaqi xeet ya,