TSK

TSK · Ecclesiastes 2:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.»

Job 3:20 TSK

Boroom tiis, ana lees koy maye leeru kaw suuf? Lu boroom naqar di doye bakkan?

Job 7:16 TSK

Doy na sëkk! Dunduma ba fàww; ba ma, samay fan genn noo la!

Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex? Xanaa doo làqu fàww nii, sa mer di boy?

Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.

Ma dellu gis fi kaw suuf ne, fu yoon moom, fa la njubadi ne, fa njub moom it, fa la njubadi ne.

Doyloo li nga gis a gën di wéye xemmem. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu. Maa ngay deme naqar ak xol bu tàng, te loxol Aji Sax ji diis gann ci sama kaw.

Jonah 4:8 TSK

Naka la jant ba fenk, Yàlla yebal ngelawal penku lu tàng jérr, jant ba jam boppu Yunus, ba mu xawa xëm, bëggatul dara ci bakkanam. Mu naan: «Dee sax a ma gënal dund!»

Ci diggante yaar yooyii laa tance: yàkkamti na maa yiwiku ba fekki Almasi, te loolu moo dàqati fuuf.