¶ Ba loolu amee Suleymaan yewwu, ndeke gént la woon. Mu dellu Yerusalem, taxaw fa kanam gaalu kóllërey Aji Sax ji, def fa ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm, daldi berndeel jawriñam yépp.
TSK
TSK · Esther 1:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ña ca gënoona jege Buur di Karsena ak Setar ak Admata ak Tarsis ak Meres ak Marsena ak Memukan, ñuy juróom ñaari kàngami diiwaani Pers ak Medd, di bokk ak Buur jataay te gëna kawe ca nguur ga.
Ca fukkeelu at maak ñaar ci nguurug Buur Aserus, ca weer wa jiitu, di weeru Nisan, ñu sànni ci kanam Aman jumtukaayu tegtal bi ñuy wax Pur, ngir seet bés bu baax ak weer wa, ci pexe ya mu nas. Ñu seet, mu yemook weeru Adar, di fukkeelu weer waak yaar.
«Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, nar koo tas. Lii mbugalu Aji Sax jee, mbugal mi këram waral.
¶ Am na bés Buur Baltacar defal ay jaraafam bernde ju réy. Ña nga tollu ci junni, muy naan nag ca seen kanam.
¶ Ci kaw loolu Daryus waa Medd ba, jot ca nguur ga, fekk ko mu am juróom benn fukki at ak ñaar.
Kuuy mi nga gis mu am ñaari béjjén, buuri waa Medd ak waa Pers la.