Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.»
TSK
TSK · Ezekiel 29:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 14:18
TSK
2 Kings 18:24
TSK
Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas!
Isaiah 30:2
TSK
Ñoo dox wuti Misra te laajuñu ma, xanaa di sàkku rawtub Firawna, di keppaaroo keppaarug Misra.
Isaiah 36:6
TSK
Misra daal, nga yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar.
Ba tey sunu gët a ngi giim, ndax ndimbal lu nuy séentu ci dara. Fa sunuy tata lanu séentoo wenn xeet wu nu manula wallu.
Ezekiel 28:22
TSK
Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Sidon, maa ngii fi sa kaw. Dees na ma sargal fi sa biir, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji ndax mbugal yi ma fiy wàccesi, ba fésal fi sama sellnga.