TSK

TSK · Ezekiel 34:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.

Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.

Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.

«Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. Dégguñu yar, bóom ngeen seeni yonent, mbete gaynde yuy fàdde.

Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.

Daa ànd ak moroomi gayndeem, màgg, doon góoru gaynde gu ndaw, ba mana pàdd am pàddam, di yàpp doom aadama.

Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi?

Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,

Maa ngi nii kat di taxawal ab sàmm ci réew mi. Lu ci réer, faalewu ko; lu ci lajj, du ko seet, lu ci gaañu, du ko faj, lu wér du ko xont, te lu ci duuf, mu yàpp, ba toj seeni we.