TSK

TSK · Isaiah 27:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa dégg Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Giñ naa ne kër yu bareey gental déy, kër yu yaa, rafet, kenn dëkku ca.

Mépp mbartal mu ñu daan gàbb, deesu fa demati, ndax ragali dég aki dagg, aw nag a cay fore, am xar curpee ca.

Bésub keroog seen dëkk yi tata wër, dees na leen won gannaaw ni dëkki Eween ñaak Amoreen ña, ba leen bànni Israyil dàqee, lépp ay doon ab gent.

Yaa def dëkk bi jali doj, dëkk bii ñu dàbbli nga gental; taaxu doxandéem yi noppee doon péey ba fàww, te deesu ko tabaxaat.

Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, fa la sunuy maam daa màggale, sawara xoyom na ko, mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.

«Ku ñuy wax Mise, dëkk Moreset, doon na biral waxyu ca jamonoy Esekiya buurub Yuda. Daa waxoon waa Yuda gépp ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngooru xare yi dafa wax ne: Dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem diy tojit, jale; tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.”

Boroom bee mel nib noon, modd Israyil, moddaale këram yu taaru yépp, tas ay tataam, ba fulal Janq Yuda mu taaru ma, ay yuux aki jooy.

Kon nag yeen tundi Israyil, dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi, ak xunti yeek xur yi, ak ndànd-foyfoy yu wéet yeek dëkk yi gental, te xeet ya ñu dëkkal sëxëtoo leen, yab leen.

Ay bés a ngi dikk ci sa kaw, keroog say noon a lay gawe ab sëkk, yéew la, tance la wet gu nekk.