TSK

TSK · Isaiah 59:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 29:14 TSK

Njekk laa woddoo woon, njekk wodd ma, te dëgg laa defoon mbubb ak kaala.

Éy Aji Sax ji Yàlla, boroom mbugal! Boroom mbugal, feqal sag leer!

Aji Sax ji, yewwul, ngalla yewwul; wone sa doole. Yewwul na bu jëkkoon, bu yàgga yàgg. Xanaa du yaa falaxe Raxab? Du yaa jam ninki-nànka jooja?

«Ngalla séentool asamaan, xooleel fa sa kër gu sell ga ne ràññ. Ana sa fiiraangeek sa njàmbaar? Sag rafet xol ak sa yërmande ñooru na ma!

ci biir kàddug dëgg, ak kàttanu Yàlla; ci kaw gànnaayi njubte yi ci sunu loxol ndijoor ak lu càmmoñ;

Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jël-leen ko, sol, jël-leen itam saamar bi Noo giy joxe, te muy kàddug Yàlla.

Ci biir sawara wuy sëlsëli lay doon. Ca lay mbugal ñi xamul Yàlla, ak ñi baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.

¶ Ba loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku, fas wu weex daldi feeñ. Ki ko war, «Wóor te Dëggu» lañu koy wax te njub lay àttee, di ko xaree.