TSK

TSK · Jeremiah 13:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su boobaa da naan: «Ana seen yàlla ya, seen kiirlaay lañu daa làqoo?

Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.

Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal te def jaloore ca Misra.

Yeena naay: «Danoo wóllëranteek ndee, njaniiw lanu digool, ba du nu moom, ba bu yaru musiba dikkeek diisaayam, du nu laal? Noo def ay fen sunu rawtu, ay wor di sunu làquwaay.»

«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.

Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’

Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!

«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa ma fàtte, jalax ma sa gannaaw. Kon nag gàddul sa ayu ñàkk gàcceek sa gànctu.”»

«Ana luy njariñal yett jëmmu xërëm ju ki ko sàkk yett, mbaa jëmmu xërëm ju ñu xelli, di ci gëmloo nit ay fen? Sàkk sa yëfi bopp, wóolu ko, xërëm yoo móol te manula wax!