Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër Buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.
TSK
TSK · Jeremiah 39:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu wax ma, ne ma: «Ña rawe ca njaam ga de, ña nga diiwaanu Yuda, ci njàqare ju réy akug toroxte. Tatay Yerusalem jaa nga tojatoo, bunt ya lakk.»
«Yéegleen seeni tata, yàqte waaye buleen leen jeexal tàkk. Tenqileen lawit yi, ñooñoo bokkul ci Aji Sax ji.
«Maay def Yerusalem jali doj, till yi dëkke; ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.»
Jógal naa dëkk bii déy, te loraange laa leen naral waaye du jàmm.” Kàddug Aji Sax jee. “Ci loxol buuru Babilon laa koy teg, mu jafal ko, lakk.”»
Maa ngi nii di joxe ndigal,” kàddug Aji Sax jee, “délloosi leen ci dëkk bi, ñu song ko, ba nangu ko, taal ko ba mu jeex. Maay gental dëkki Yuda, ba kenn du ca des.”»
Waaye soo jébbalul sa bopp kàngami buuru Babilon, dees na teg dëkk bi ci loxoy waa Babilon, ñu lakk ko ba mu jeex, te yaw doo leen rëcc.»
Loxo la noon bi teg ci ngëneeli Siyoŋ gépp. Siyoŋ kay a gis yéefar yi songsi këram gu sell gi, te ci ñoom nga santaane woon, ne buñu dugg sam ndaje.
Aji Sax jee jañax sarxalukaayam, gedd bérabam bu sell. Moo teg ci loxol noon tatay këram yi. Biir kër Aji Sax ji la baat xaacoo, ni bu doon bésu màggal.
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.