TSK

TSK · Jeremiah 49:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca jamonoy Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar, Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim,

Ezra 4:9 TSK

¶ Bataaxal bii mu ngi bawoo ci Reyum, boroom dëkk bi, ak Simsay bindkatam, ak seen nàttongoy àttekat yeek kàngam yeek saytukat yeek boroom téere yi, ak waa Urug ak waa Babilon ak waa Sus, Elameen ña,

Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

«Buurub Elam a nga faak gàngooram gépp, seeni bàmmeel yéew bosam. Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar. Paaxe lañu wàccaale xóotey suuf, te daan tiital waa réewum aji dund ña. Seen gàcce lañu gàlloo, ànd ak ñay wàcci biir pax.

Acts 2:9 TSK

Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,