Job 9:19
TSK
Su dee kàttan, kee bare doole! Su dee wàllu yoon, kan moo ma cay woo?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su dee kàttan, kee bare doole! Su dee wàllu yoon, kan moo ma cay woo?
Mooy kii nag nga teg bët, mooy man mii nga nara layool!
Ragal-leen saamar! Seen xadar jii ñaawtéef la, saamar ay àtteem, xamleen ne àtte am na.
Yàlla daal, soxlawula liñbat nit ki, bala mu koy woo cib àtte.
Futtees nay boroom fit, ñu ne nërëm, nelaw; kuy ñeyi xare, say yoxo nasax.
Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw?
Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte, ba ci lépp lu làqu, muy lu baax, di lu bon.
¶ «Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!