TSK

TSK · Job 25:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 26:5 TSK

Ndem-si-yàlla yaa ngay lox ca ron ndoxi biir suuf, ñook ña fa dëkke.

Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,

Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!

Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant. Jàmm, na jàmm ñeel ñépp, ku soreek ku jege.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa leen di faj.»

Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.

Loolu lépp ci Yàlla la jóge, moom mi nu jubale ak boppam ci Almasi, te moo nu sas, ngir nuy waare juboo googu.

Ñaar ñi la Almasi boole ci jenn jëmm, jubale leen ak Yàlla, ca bant ba ñu ko daajoon, te bant ba la dakkale sunub tongoo.

Jude 1:25 TSK

Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.