TSK

TSK · Lamentations 3:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal!

Aji Sax ji moo leen di xeexal, yeen kay neleen tekk rekk.»

Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, tey lal ay pexe.

«Xool-leen jàmbaar ji làqoowul Yàlla, xanaa di yaakaar alalam ju bare, di yokkoo loraange.»

Yàlla doŋŋ ay dalal sama xel, moo may wallu.

Muy woyu Sabóor ngir bésub Noflaay.

Aji Sax ji, namm naa sa wall, sa yoon ay sama bànneex.

Nga wax ko ne ko: “Defal ndànk te ne cell. Bul tiit, bul xàddi ndax merum Reccin ak Siri, ak doomu Remalya ji. Duñu dara lu moy ñaari gil yuy saxar!

Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Délsi, dal-lu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena buggul!

Yitte ju réy ju ñu am ci nit ki nag, ndegam lu baax lees ci jublu, saa su nekk lay baax, waaye du rekk saa yu ma teewee ci seen biir.

¶ Kon nag buleen teqlikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.