TSK

TSK · Leviticus 13:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te itam képp ku for lenn lu dee ci yii, na fóot ay yéreem, waaye dina yendoo sobe ba jant so.

Képp ku lekk ca médd ma, na fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. Képp ku for médd ma, na fóot ay yéreem te du tee mu yendoo sobe ba jant so.

Ku ñuy laabal day fóot ay yéreem, watu ba set te sangu, doora set. Gannaaw loolu man naa dugg ci dal bi, waaye na yem ca bunt xaymaam ca biti diiru juróom ñaari fan.

lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israyil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititu xolam, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii,

Man, Sang bi, ci laay leerloo, ku ko sàmm yokku yool.

Amul moos ku jub ci kaw suuf, kuy def lu baax te du bàkkaar.

Bant bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.

¶ Ku ngëmam dëgërul nag, xajooleen ko, te bañ cee càmbar gis-gis yu wuute.

Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.

James 3:2 TSK

Bare na lu nuy tooñ, nun ñépp. Ku dul tooñ ci kàddu nag, kooku nit ku mat la, te man naa moom yaramam wépp, boole ci.

Jude 1:22 TSK

Ñiy nàttable, ñeewanteleen leen,