TSK

TSK · Leviticus 9:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye deru yëkk wi ak yàppam wépp dees koy booleek bopp bi ak yeel yi ak yérey biir yi ak sébbriit mi;

Li des ci yëkk wi, di der beek yàpp week sébbriit mi, mu génne ko dal bi, lakk ko ca biti, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.

Ndax kat, jur ga sarxalkat bu mag ba daan yóbbu seen deret ca bérab bu sell baa sell, ngir njotlaayal bàkkaar, seen yaram lees daan lakk ca bitib dal ba.