Genesis 28:20
TSK
Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol,
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol,
Ba fii nu tollu, xiif ak mar ak rafle, aki dóor lanu nekke, di taxawaalu.
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
Doñ-doñ, akub coono ci la, te bare naa lu ma fanaanee xoole. Xiif naa, mar naa, te bare na lu ma ñàkk ab dund. Liw naa, rafle naa,
¶ Teewul njullite gu ànd ak doylu, di alal ju réy.
¶ Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»