TSK

TSK · Proverbs 21:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»

Kàddug tooñ ga ku bon wax mu ngi sama xel mi. Mu ne: «Ana lu may ragal ci Yàlla?»

Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.

Ñu baree ngi naa: «Gore naa,» waaye kuy boroom kóllëre dëgg?

Ag maas a ngi defe ne set nañu, te taq ripp ak bàkkaar.

NATT: Nattees na sa diisaay ci nattukaay bi, nga yées.

Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.

Ku foog ne moo am solo, te du dara nag, boppam lay nax.

Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.