TSK

TSK · Proverbs 21:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ndeke Uri ñibbiwul këram. Ca bunt kër Buur la tëdd, mook mboolem surgay Buur.

Kenn ca jawriñ ya ne ko: «Du kenn, Buur sang bi; waaye Alyaasa, yonent bi ci Israyil mooy jottli buurub Israyil kàddu yi ngay wax ci sa biir néegu biir.»

Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.

Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!

Noon naa làmmiñ kese doy na pexeek njàmbaar cib xare? Ma ne: Ana kan nga yaakaar bay fippu ci sama kaw?

Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax, jiy jëfe ngor ak dëgg ak njekk fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee.

Acts 4:27 TSK

Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.

Ndaxte xam-xamu àddina sii, ndof la fa Yàlla. Moo tax bindees na ne: «Mooy kiy jàpp ñi muus ci seen pexey muusaatu,»