TSK

TSK · Psalms 46:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Fittu jàmbaar damm, néew-doole yi sol kàttan.

¶ Ba saraxu ngoon jotee, Yonent Yàlla Ilyaas jegesi, ñaan ne: «Aji Sax ji, yaw Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, xamleel bésub tey jii ne yaw yaa di Yàlla ci Israyil, ma di sab jaam bi def lii lépp ci sa ndigal.

Xeet yi samay maam sànk, seeni tuur dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Resef, di askanu Eden wa woon ca Telasar?

Nga di leen diir fittu kanam, ñu wone gannaaw.

Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.

Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. Moo nu sàkk, nuy ñoñam, di gàttam yi muy foral.

Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam, Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam.

Bu ma taalee Misra, ba wéeruwaayam yépp rajaxoo, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.

Maay féle sa xala ci sa loxol càmmoñ, féle say fitt ci sa loxol ndijoor, waddal.

Aji Sax ja moom, ma nga ca màkkaanum sellngaam, na àddina sépp selaw fi kanamam.»

Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.