TSK

TSK · Revelation 3:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te bu leen nattu dikkalee, ndimbal lu néew lañuy am, ndax ñu bare naaféq lañuy fareek ñoom.

Luke 12:9 TSK

Waaye ku weddi fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, dees na weddi fa kanam malaakay Yàlla ya, ne man nga féeteel.

Acts 3:13 TSK

Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.

ndax bunt ubbikul na ma fi ŋàpp, ngir liggéey bu am njariñ, te noon yi bare nañu.

Mbir moomu, ñetti yoon laa ci ñaan Sang bi, ngir mu sorele maak moom.

Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu buntu xamle kàddu gi, ngir siiwtaane mbóot mi ci Almasi, li waral ñu jéng ma.

Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko.

Jude 1:4 TSK

Ndaxte ñenn a ngi ñu ñu yàgga bind seenub àtte, te ñoo yoxoosu ci seen biir, di ñu ñeme Yàlla; ñooy taafantoo yiwu Yàlla ngir yoonal ag yàqute, di weddi Buur biy kenn, te di sunu Boroom Yeesu Almasi.

¶ Xam naa fa nga dëkk, fa la Seytaane samp nguuram. Teewul nga ŋoy ci sama tur te weddiwoo ne man nga gëm ba sax ca fan, ya nit ña reye ca seen biir, Antipas sama seede bu am kóllëre ba, foofa Seytaane dëkk.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Filadelfi nag, bind ko, ne ko: «Lii moo di kàdduy ku Sell ki, kiy Dëgg, te yor caabiy Daawuda, di tijji te kenn du tëj, di tëj te kenn du tijji. Mu ne:

¶ Xam naa say jëf; xam naa ne seddoo, tàngoo. Su ma sañoon nga sedd mbaa nga tàng.