TSK

TSK · Zephaniah 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su boobaa ñi gëna walaakaana am lu ñu for, néew-doole ya goor, ànd ak dal. Waaye yeen, maa leen di xiifal, ngeen dee ba raaf, xiif ba fàkkas ñi ngeen dese.

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di dóor Filisteen ñi sama loxo, maay dagg ñooñu di askanu Keret, maay fàkkas ndes wa ca tefesu géej.

Amos 5:1 TSK

Amos ne: Yeen bànni Israyil, dégluleen mii pent: maa ngi leen di jooy, yeen bànni Israyil!

Teewul sama kàdduy àrtu ak sama dogali yoon ya ma yóbbante woon sama jaam ña, yonent ya, du lépp a dab seeni maam? Ñu dëpp nag daldi ne: “Noonee Aji Sax ji Boroom gàngoor yi nammoona def ak nun, feye nu ko sunuy jikko ak sunuy jëf, noonu la def ak nun.” »