Saay bu nekk
Waxtu ñetteel - Tierce
Nu fàttali Kirist kanam Pilaat, yéegal ko asamaan, ak wàccu Xel mu Sell mi miy yeesal sunu xol.
Tàmbali bu Waxtu bu nekk
Ci turu Baay ak Doom ak Xel mu Sell
Yàlla bi kenn rekk. Amiin.
Boroom bi, yërëm nu. Boroom bi, yërëm nu. Boroom bi, barkeel nu. Amiin.
Ndammu Baay ak Doom ak Xel mu Sell leegi ak saa yu nekk te ba jamono yu jamono yépp. Amiin.
SUNU BAAY
Yàlla, nga may nu mën te nuy wax ak jërëjëf:
Sunu Baay bi ci kaw asamaan. Na sa tur sell. Na sa nguur ñëw. Na sa bëgg-bëgg am, ni mu nekk ci kaw asamaan, mu nekk ci suuf. Jox nun tey sunu mburu besub bes. Baalal nun sunu bàkkan, ni ñun it di baal ñiy bàkkaale ak nun. Bul nu yóbbu ci nasax. Waaye muccal nu ci ki bon bi. Ci sunu Boroom Yeesu Almasi, ndax yaw laa nga boroom nguur gi ak doole ak ndam ba fàww. Aamiin.
Sàllug Jërëjëf
Nañu santal Yàlla, Boroom bërey yi, ki yërëm; Baay suñu Boroom ak sunu Yàlla ak sunu Musalkat Yeesu Almasi, ndaxte mooy ki nu koofal, te dimbali nu, te aar nu, te yóbbu nu fa mu nekk, te yërëm nu, te doxal sunu loxo, te yóbbu nu ci saa sii. Moo tax it nu ko ñaan ngir mu aar nu ci bés bu sell bii ak ci bés-bésu sunu dund yépp ak jàmm. Boroom lépp, Boroom bi sunu Yàlla.
Sàmm bi, Yàlla Boroom lépp, Baay suñu Boroom ak sunu Yàlla ak sunu Musalkat Yeesu Almasi, jox naa la jërëjëf ci jamono yépp, ak ngir jamono yépp, te ci jamono yépp, ndaxte xool na nu, te dimbali na nu, te aar na nu, te yóbbu na nu ba ci sa kaw, te yërëm na nu, te doxal na sunu loxo, te yóbbu na nu ba ci saa sii.
Moo tax, nu la ñaan te ñu la ñaanal ci sa baax baax: Boroom ku bëgg nit ñi, may nu bañ a noppi bés bu sell bii ak bés-bésu sunu dund yépp ak jàmm ak sa ragal. Xol dugg, noone ak far baaxu seytan, ak ndigëlu nit ñi bon, ak tolof tolofu noon yu bañ, ak yoonu noon yu nëb ak yu fees, dindi leen ci nun ak ci sa ñoñ yépp, ak ci sa berab bu sell bii. Waaye lu baax ak lu jàppante, nga jox ko nun. Ndax yaw yaa jox nañu sa sañ-sañ ngir nu sàcc njàmbaar ak yàmb ak dooley noon yépp. Te bul nu yóbbu ci kanamam masla, waaye musal nu ci bon.
Ci ngërëm ak yërmandéef ak mbeg yu sa Doom baat Biir rekk, sunu Boroom ak sunu Yàlla ak sunu Musalkat Yeesu Almasi; moom la ci biir moom ndam ak yeesal ak doole ak noonu, di la ko war, ak Xel mu Sell jiy dund, ki mel ni yaw, leegi ak saa yu nekk te ba jamono yu jamono yépp. Amiin.
SÀLMU 50
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na, di woo àddina, penku ba sowu.
Ca Siyoŋ, dëkk ba ca taar ba la Yàlla feeñe ni leer gu jolli.
Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, sawaraa ko jiitu, di xoyome, ngëlén lu mag wër ko.
Ma ngay woo seede asamaan ak suuf, ngir àtte ñoñam.
Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre ñiy sarxal, di ko fase sama kóllëreek ñoom.»
Asamaan a ngi biral njekkam, ngir Yàllaay àtte. Selaw.
«Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; yeen waa Israyil, ma sikk leen. Maa di Yàlla, seen Yàlla.
Du seeni sarax laa leen di sikke, mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
Xam naa njanaawi tund yi, luy ndundatub tool maa ko moom.
Su ma xiifoon, duma leen ko wax, maa moom àddinaak li ci biiram.
Damay lekk yàppu nag ak a naan deretu sikket a?
Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,
di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?
Yeena ngii, bañ sama yar, xalab samay kàddu.
Fu ngeen gis ub sàcc, neexook moom, ab njaalookat, ngeen lëngool.
Dangeena afal seen gémmiñ ci mbon, seen làmmiñ taqoo fen,
ngeen di tooge seen mbokk, di yàq deru doomu ndey.
Lii yeena ko def! Damay noppi, ngeen defe ne damaa mel ni yeen? Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis!
«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.
Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallu Yàlla.»
Tàmbali sàll
Tisbixu waxtu jëkk ci bëccëg, may ko sunu Buur ak sunu Yàlla Almasi; te may ma mu baal ma bàkkaar yi.
SÀLMU 19
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Asamaan nee Yàlla màgg na, kaw ne màww, biral liggéeyu loxoom!
Bésoo bés kàddu seere ko, guddee guddi xamle ca mbir.
Du làkk, duy wax, du baat bu dégtu,
suuf sépp la seen ndéey jibal, seen kàddoo àkki cati àddina. Kaw la Yàlla sampal jant xayma,
mu mel ni boroom séet, génne néegam, di mbër mu doŋali, xéluw yoonam.
Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.
Yoonu Aji Sax jee mat, di leqli bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.
Lu Aji Sax ji tegtale, njub la, di bégal xol. Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la, di leeral gis-gis.
Santaaneb ragal Aji Sax ji mooy li sell te sax ba fàww. Lu Aji Sax ji digle, dëgg la, ak njekk gu sotti.
Moo dàq wurus, raw wurusu ngalam wu ne xas; dàqati lem, ëpp tem-tem.
Man, Sang bi, ci laay leerloo, ku ko sàmm yokku yool.
Nit juum na, umple ko, baal ma tooñ gu ma umple.
Te Sang bi, musal ma ci bàkkaaru teyeef, mu bañ maa jiital, ma mana maandu, mucc moy gu réy.
Éy Aji Sax ji, lu saaw làmmiñ tudd mbaa sama xol déey ma ko, yal nay loo gërëm, yaa may aar, yaa ma jot.
SÀLMU 22
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.
Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma? Ma binni, binneeti, wall sore.
Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; woote guddi, nopploo ma.
Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, Israyil di la kañ.
Yaw la sunuy maam wóolu woon, wóolu la, nga xettli leen.
Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
Man nag aw sax rekk laa, matuma nit. Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma.
Ku ma gis ñaawal ma, biiñ ma, xeelu ma, naa:
«Na wéeroo Aji Sax ji, mu xettli ko; su ko soppee, na ko wallu.»
Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey, naxe ma sama weenu yaay.
Yaw laa dénkoo ba may juddu, ba ma juddoo sama ndey, ngay sama Yàlla.
Bul ma sore, musiba teew na, wall amul!
Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.
Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.
Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.
Ay xaj a ma wër, di gàngooru saaysaay, dar ma kepp, bëtt samay yoxook samay tànk.
Maa ngii, mana waññ sama yax yépp, ñoom ñuy xoole, di ma seetaan,
séddoo samay yére, tegoo bant sama mbubb.
Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore; yaa may dooleel, gaawe ma.
Xettlil sama bakkan ci saamar, ba sama benn bakkan bii mucc selli xaj!
Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll. Yaa ma wallu woon!
Ma siiwali saw tur ci bokk yi, màggale la digg mbooloo mi.
Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.
Moom de sàgganewul boroom tiis, làqu ko kanamam, ba mu wootee, wuyu na ko.
Yaw laay sante ndaje mu mag, sottalal la samay dige, ñi la ragal seede.
Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
Àddina wërngal këpp ay fàttliku, walbatiku ci Aji Sax ji. Làngi xeet yépp sukkalsi ko.
Aji Sax jeey boroom nguur, moo yilif xeet yi.
Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko, ku jëm pax it, te bakkanam di lang, di ko sukkal.
Askan wu dikkagul dina jaamu Boroom bi, ñiy ñëw te juddooguñu dees na leen wax ay mbiram.
Ñu dikk, biral njekkam, jottli xeet wu sosoogul jalooreem.
SÀLMU 23
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk.
Parlu mu naat la may gooral, wal mu dal, mu tette ma ca,
leqli ma, teg ma ci yooni njekk ngir teddngay turam.
Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.
Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund, ma dëkke këram ba fàww.
SÀLMU 25
Ñeel Daawuda. Aji Sax ji, yaw laay diis sama bakkan.
Sama Yàlla, yaw laa yaakaar. Yàlla buma rus, noon yi ree.
Deesu la séentu, ba rus. Kuy wor ci neen mooy rus.
Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, xamal ma fi nga ma jaarloo.
Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.
Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!
Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,
di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.
Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool, jéggal ma ngir saw tur.
Ana kuy wormaal Aji Sax ji, mu won ko yoon wi mata taamu,
muy dunde ngëneel, askanam moom réew mi?
Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.
Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, moo may xettli ci fiiru noon.
Ngalla geesu ma, baaxe ma, maa wéet, néew doole,
sama xol feesey xalaat. Rikk, teggil ma njàqare!
Xoolal sama naqar ak sama tiis, te baal ma bépp bàkkaar.
Xoolal noon yi ne gàññ, bañ ma mbañeelu fitna.
Éy, aar ma, musal ma! Bu ma rusloo, yaw laa làqoo.
Yal na ma maanduteek njub taxawu, maa ngii, di la xaar.
Éy Yàlla, teggilal Israyil tiisoo tiis.
SÀLMU 28
Ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, yaw laay woo, di la wéeroo, bu ma tanqamlu. Soo nee cell, ma xawa tàbbim pax.
Ngalla déglul, ma tinu la, woo la wall, dékk lay yoxo, jublu sa néegu biir bu sell ba.
Bu ma sànkaaleek ab soxor, di ma booleek kuy def lu bon, di wax moroom ma jàmm, te dencal ko ay ca xolam.
Fey leen seen liggéey, seen kemu jëf ju bon. Jox leen seen añu jëf, yool leen seen yelleef.
Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, ak liggéey bi mu def. Da leen di yàqte, te dootu leen yékkati.
Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan!
Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.
Aji Sax jeey dooleel ñoñam. Mooy làq, di musal buur bi mu fal.
Ngalla musalal sa mbooloo, barkeelal sa ñoñ ñii, sàmm leen, boot ba fàww.
SÀLMU 29
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Yeen goney Yàlla yi, seedeel-leen Aji Sax ji, seedeel-leen ko teddngaak doole,
seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam. Sujjóotal-leen Aji Sax ji, ki gànjaroo sellnga.
Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, Yàlla mu tedd maa dënu, Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.
Aji Sax jeey àddoo doole, Aji Sax jeey àddoo daraja.
Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar, Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu, tundu Siryoŋ it, mbete yëkk wu ndaw.
Aji Sax jeey àddu, fettaxal sawara, mu boy.
Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
Aji Sax jeey àddu, kéwél matu, garabi àll ruus, biir këram di mennum riir, naan: «Màggal-leen ko!»
Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, Aji Sax jee falu buur ba fàww.
Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.
SÀLMU 33
Yeen aji jub ñi, sarxolleleen ci Aji Sax ji; kuy jubal, màggal war na la.
Xalamleen, sante Aji Sax ji, xalamal-leen ko xalamu fukki buum.
Fental-leen ko woy, xalam, mu neex, sarxolle jib.
Aji Sax jee jub kàddu. Mooy jëfe lépp kóllëre.
Moo sopp dëgg ak yoon. Aji Sax ji, ngoram a fees àddina.
Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.
Moo boole ndoxi géej, jal, yeb xóotey géej ciy mbànd.
Yeen waa àddina sépp, ragal-leen Aji Sax ji; yeen àddina wërngal këpp, wormaal-leen ko.
Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;
Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
Asamaan la Aji Sax jiy jéere, di gis doom aadama yépp.
Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.
Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; lu ñu def, xam na ko.
Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.
Yaakaar aw fas nax sa bopp la, kàttanu fas dug wall.
Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.
Day jot bakkanam, di ko dundal cib xiif.
Nu ngi séentu Aji Sax ji, moo nuy taxawu, di nu feg.
Ci moom la sunu xol di sedde, turam wu sell lanu wóolu.
Aji Sax ji, ngalla baaxe nu sa ngor, moom lanu yaakaar fi yaw.
SÀLMU 40
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
May xaara xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.
Moo ma may, ma fent, woy wu ma woye sunu Yàlla. Ñu baree seede, di wormaal ak a dénku ci Aji Sax ji.
Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.
Saraxi gàtt mbaa pepp, taamuwuloo ko, ay nopp nga ma bënnal, saraxu rendi-dóomal, ak saraxu póotum bàkkaar, sàkkuwuloo ko.
Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare, ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
Siiwal naa sag njekk ca ndaje mu mag ma. Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko.
Làquma sag njekk, ne cell ak moom. Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko. Làquma ndaje mu mag ma sa ngor ak sa worma.
Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande. Sa ngor ak sa worma, yal na ma feg ba fàww.
Ay musibaa ma tanc, ne gàññ, ba wees ab lim. Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma, baree bare, ba ëpp sama kawari bopp; sama xol jeex tàkk.
Éy Aji Sax ji, yal na la neex, nga wallu ma! Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
Képp kuy wuta fëkk sama bakkan, yal na rus, torox ne tott. Kuy bége sama loraange, yal nañu ko duma, mu ne yàcc.
Ku may ñaawal, yal nañu ko torxal, mu jommi.
Képp ku lay sàkku, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»
Man, néew naa doole, ñàkk naa, waaye yaw Aji Sax ji, danga maa yég. Yaw yaa may wallu, xettli ma; sama Yàlla, bu ma yeexe.
SÀLMU 42
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, maa la koy sàkkoo xol.
Maa mar Yàlla, Yàlla jiy dund! Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?
Rongooñ laay dunde guddeek bëccëg, noon yi di ma dëkke naa: «Ana sa Yàlla ji?»
Lii laay fàttliku, sama xol jeex: dama daan jàll, jiite mbooloo ma, jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant, ñu booloo di màggal.
Moo man, lu may yoggaaral nii? Lu may jàq? Naa yaakaar Yàlla, ba dellu sante sama Yàlla wallam.
Maa ngi ne yogg, ba di la fàttlikoo fa réewum Yurdan ak tundi Ermon ak Misar.
Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram, guddi ma fanaane koo woy, di ñaan Yàlla mi may dundal.
Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko: «Lu tax nga fàtte ma, noon di ma fitnaal, may wéye tiis?»
Noon yaa ngi may ñaawal, di ma yendoo naa: «Ana sa Yàlla ji?» Ma ne yàcc, ne yasar.
Moo man, lu may yoggaaral nii? Lu may jàq? Naa yaakaar Yàlla, ba dellu sante sama Yàlla wallam.
SÀLMU 44
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
Éy Yàlla, noo déggal sunu bopp, sunuy maam a nu wax jëf ja nga jëf, ca seeni jant, bu yàgga yàgg.
Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, jëmbat fa maam ya; yaa mbugal xeet yi, ñoom, nga yiwi leen.
Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, seen dooley bopp it mayu leen ndam. Yaa ko defe kàttan ak doole, geesoo leen sa leeru kanam, ngir sa cofeel.
Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, mayal askanu Yanqóoba ay ndam.
Yaw lanuy dàqe bañ yi, sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song.
Du fitt laa wóolu, du saamar a may may ndam.
Yaa nuy musal ci bañ yi, yaay gàcceel noon ñi.
Yàlla lanuy damoo bésoo bés, di màggal turam ba fàww. Selaw.
Waaye danga noo wacc, torxal nu, ba àndulook sunu mboolooy xare.
Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, ñu bañ nu, ba futti nu.
Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee, tasaare nu ci biir xeet yi.
Jaay nga sa mbooloo ci dara, te jariñu la tus.
Tax nga sunuy dëkk di nu ree, ñi nu séq di nu kókkaleek a ñaawal.
Tax nga xeet yi di nu léeboo, jaambur yaa ngi nuy wëcc bopp!
Damaa dëkke gàcce, sëlmoo kersa
ndax kókkali yeek xastey nit ñi ma bañ, di feyoonteek man.
Lii lépp dal na nu, te fàttewunu la, fecciwunu la kóllëre.
Dëdduwunu la, wàccunu saw yoon,
teewul nga not nu, wacce nu xaj ya, këpp nu lëndëmu ndee.
Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
du la ump, yaw Yàlla, mi xam kumpay xol.
Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.
Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? Yewwul, bu nu wacc ba fàww.
Loo nu làqe saw yiw, di fàtte sunu njàqareek sunu coono?
Nu ngi ne ñàyy ci pënd bi, di watat koll fi suuf.
Wallusi nu, jot nu ngir sa ngor.
SÀLMU 45
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel.
Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!
Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
ànd ak daraja, dawal ba am ndam, di dawal dëgg ak yërmande ji war, ba mana def ay jaloore.
Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.
Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,
di sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Boroom diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom:
sa yére yépp di gilli ndàbb, alowes akum kanel, ñu di la bégale xalam, ca sa biir kër yu yànj.
Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.
Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,
Buur xemmeme la sab taar; mooy sab sang, wormaal ko.
Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.
Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy, janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur,
ñu duggsi kër Buur, ci biir mbégteek bànneex.
Yal na la sa doom yu góor wuutu ci seen jalu maam, nga def leeni kàngam ci réew mi mépp.
Maa lay joobe ba sa tur du fey mukk, xeet yi saxoo laa sant ba fàww.
SÀLMU 46
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
ba dunu tiit suuf su yëngu sax, ba tund yiy tàbbi biir géej,
mbaa gannax yuy riir, di fuur ak a fuddu bay gësëm tund yi. Selaw.
Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji.
Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf; Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.
Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jii a nuy rawale. Selaw.
Qoṭa (Kàllaama)
Sa Xel mu Sell, Boroom bi, ba nga yiwol ci say taalibe yu sell ak say rásul yu gëna mag ci waxtu jëkk-ñaar, bala nga yóbbu ko ci nun yaw bu baax, bu ko dindi ci nun; waaye nga koy jëli ci sunu biir. Xol bu wéral nga biral ci man Yàlla, te Xel bu jub nga jëli ci samal biiram. Bul wacc ma ci sa kanam, te sa Xel mu Sell bul ko dindi ci man. (Zoksapatri kéy Iwo ké Ájio Pneumati Δόξα Πατρί καὶ Υἱῷ καὶ Ἁγίῳ Πνεύματι - Ndammu Baay ak Doom ak Xel mu Sell).
Boroom bi, yaw yaa yiwol sa Xel mu Sell ci say taalibe yu sell ak say rásul yu gëna mag ci waxtu jëkk-ñaar, boo ko dindi ci nun yaw bu baax. Waaye nu la laaj nga koy jëli ci sunu biir, sunu Boroom Yeesu Almasi Doom Yàlla Kàddug Yàlla, Xel bu jub te di dundal, Xelub nabi ak sikkim, Xel bu sell ak dëgg ak sañ-sañ, yaw ku mën lépp, ndax yaw yaa ngi leen wëral sunu ruux. Yaa ngi leen leeral ku nekk ku ñëw ci àdduna, yërëm nu. (Ke nun, ke a ee, ke istos ee onas ton ee onon Amiin Καὶ νῦν καὶ ἀεὶ καὶ εἰς τοὺς αἰῶνας τῶν αἰώνων. Ἀμήν - leegi ak saa yu nekk te ba jamono yu jamono yépp Amiin).
Yaw Theotokos yaa ngi di garab gu dëgg gu xam-xam ji mu nelaw bu xol, nu la laaj yaw ki fullu ngérëm, ak rásul yi, ngir mu musal sunu ruux. Barkeel nañu Boroom bi sunu Yàlla. Barkeel nañu Boroom bi bés ba bés, mooy sàqale giirug sunu yoon ndaxte mooy Yàlla bu musal nun (Ke nun, ke a ee, ke istos ee onas ton ee onon Amiin Καὶ νῦν καὶ ἀεὶ καὶ εἰς τοὺς αἰῶνας τῶν αἰώνων. Ἀμήν - leegi ak saa yu nekk te ba jamono yu jamono yépp Amiin) .
Yaw Buur bu asamaan, Kóolute, Xelub dëgg, yaw bu nekk ci bépp berab te di fey àdduna, kërug lu baax, te Doxkatug dund, ñëw te nga dalal ci nun, te nga seddal nun ci lu bon bépp yaw bu baax, te nga musal sunu ruux. (Zoksapatri kéy Iwo ké Ájio Pneumati Δόξα Πατρί καὶ Υἱῷ καὶ Ἁγίῳ Πνεύματι - Ndammu Baay ak Doom ak Xel mu Sell).
Noonu nga nekkoon ak say taalibe yaw Musalkat, te jangallewoon leen jàmm; ñëw it ak nun te jox nu sa jàmm te musal nun te musal sunu ruux. (Ke nun, ke a ee, ke istos ee onas ton ee onon Amiin Καὶ νῦν καὶ ἀεὶ καὶ εἰς τοὺς αἰῶνας τῶν αἰώνων. Ἀμήν - leegi ak saa yu nekk te ba jamono yu jamono yépp Amiin).
Su nu taxawee ci sa kër bu sell, nu nekk na ni nu taxaw ci asamaan. Theotokos, yaw yaa ngi ab bunt bu asamaan; ubbi nu bunt bu yërmandéef.
Tenoo oasht emmok o piekhristos nem pekyot en aghathos nem pi epnevma ethowab je akee ak soati emmon nai nan
Nu jaamu la, Yaa Kirist, ak sa Baay bu Baax ak Xel mu Sell; ndaxte yow nga ñëw te nga musal nu.
1. Xel mu Sell mi, Boroom bi, yaa la wàccal ci sa taalibe yu sell ak sa aji-yëgle yi ci waxtu ñetteel; bul ko génn ci nun, Yaa bu Baax, waaye yeesal ko ci sunu biir. Dugal ma xol bu set, Yàlla, te yeesal xel bu dëg ci man. Bul ma sàq ci sa kanam, te bul génn Xel mu Sell mi ci man.
Doxa Patri ke Eioa ke Agio Pnevmati
Màggal ci Baay, ak Doom, ak Xel mu Sell.
2. Boroom bi, yaw nga wàccal Xel mu Sell mi ci sa taalibe yu sell ak sa aji-yëgle yi ci waxtu ñetteel; bul ko génn ci nun, Yaa bu Baax, waaye nu la ñaan nga yeesal ko ci sunu biir, Yaa Boroom Yeesu Kirist, Doom Yàlla, Kàddug Yàlla: xel bu dëg te may dund, xel bu wax jàppandi, xel bu sell, njub ak sañ-sañ; Yaa Aji-Màgg, ndaxte yaw yaa leeru sunu ruu. Yaa mi leeral ku nekk ku ngi dugg ci àdduna, yërëm ma.
Ke nin ke a ee ke ees toos e onas toan e oa noan ameen.
Leegi ak ba fàww ba fàww yi, Ameen.
3. Yaa Yaayul Yàlla (Theotokos), yow yaa bindu garab jàmm ji dëgg, nu la laaj, yaa muñ mu fees, ak aji-yëgle yi, ngir musal sunu ruux. Barkeel na Boroom bi sunu Yàlla. Barkeel na Boroom bi bes bu nekk. Mooy waajal sunu yoon, ndaxte mooy Yàlla sunu musal.
Ke nin ke a ee ke ees toos e onas toan e oa noan ameen.
Leegi ak ba fàww ba fàww yi, Ameen.
4. Yaa Boroom bi ci asamaan, Aji-sant yiw, Xel bu dëgg, mi nekk fa lépp te muñal lépp, ndoxalub lu baax ak ki may dund, kaay, toxal ci nun te dëkk ci nun te seddloo nun ci lu bon, Yaa bu Baax, te musal sunu ruux.
Doxa Patri ke Eioa ke Agio Pnevmati
Màggal ci Baay, ak Doom, ak Xel mu Sell.
5. Noonu la nga doon ak sa taalibe, Yaa Mujj-mi, te nga jox leen jamono bu jàmm; naka noo ko, kaay nekk ak nun itam, te jox nu sa jàmm, te musal nu te dindi sunu ruux.
Ke nin ke a ee ke ees toos e onas toan e oa noan ameen.
Leegi ak ba fàww ba fàww yi, Ameen.
6. Saa su nu taxaw ci sa dëkku sell, nu mel ni nu taxaw asamaan. Yaa Yaayul Yàlla, yow yaa buntub asamaan, ubbi lanu buntub yërëm.
Ginnaaw loolu, ku ñaan bi ñaan na:
Boroom bi, déggal nu te yërëm nu, te baalal sunu bàkkaar. Ameen.
(Boroom bi, yërëm nu) 41 yoon
Absolusion
Yàlla bi bu ñuul yërmandéef yépp, Boroomu ndogalu xol yépp, ki nu di yégle yërmandéefu sa Xel mu Sell ci jamono yépp, nu la sant ndaxte nga teg nu ci jàmm ngir jàng ci waxtu bu sell bii, mu ngi fu sa ngërëm yéesal nañu àdduna ci sa Xel mu Sell bu ñuul, ci la ku baax a weex, ci say taalibe yu sell ak say rásul yu gëna màgg yi, noonu ni asamaan yi di gëlëmm. Nu la laaj te nu la laaj, yaw ku bëgg nit ñi, nga jot nu seen ñaan, te nga baal sunu bàkkaar yi, te nga sàqale ci nun say nga xel mu sell, te nga seddal nu ci bépp sëqug yaram ak xol, te nga yóbbu nu ci yoone bu xel, ngir nu dox ak Xel mi te nu bañ a gaawal sëtu yaram. Te may nu nu doon seeni jaamu ci setlu ak njub ci bés-bésu sunu dund yépp. Ndaxte ndam ak kaaraange ak doole a la war, ak sa Baay bu baax ak Xel mu Sell, leegi ak saa yu nekk te ba fàww Amiin.
Ñaan bu ñu di jàng ci jeexitalu waxtu bu nekk
Boroom bi, yërëm nu, te yërëm nu. Yaa mi ci jamono yépp ak waxtu yépp, ci asamaan ak ci suuf, ñu ko di fekkee te di ko màggal. Almasi sunu Yàlla bu baax, ku muñ, ku fees yërmandéef, ku am moytule, ku bëgg njub yi te ku yërëm bàkkaaru nit ñi, man laa ci sibi: Man laa mooy buur bu ñu doon bàkkaar; yaw doo bëgg dee gu bàkkaarkat; yàgg la nga bëgg mu jeeg te dund. Yaa ngi woo képp ku dund ngir mu am jëmm ci kàddu yépp yi kenn di xaar.
Boroom bi, nga jëlee seen ñaan ci waxtu wii ak ci waxtu yépp. Yombal sunu dund, te yóbbu nu ngir def say ndigël. Sellal sunu ruux. Seddal sunu yaram. Takkal sunu xalaat. Soppiku sunu niyóo. Liggéeyal sunu feebar te baal nu sunu bàkkaar. Te musal nu ci lu bon yépp ak li indi yërmindeeru xol. Wàccal sunu kaw ay malak yu sell, ngir nu nekk ci seen penku, ñu aar nu te ñu jàppal nu, ba nu jot ci benn ngëm ak ba nu xam sa ndam bu kenn mënu ko gis te kenn mënu ko xare; ndax yaw nga màgg te nga doon ba fàww. Amiin.
Yàlla, may nu mën, ngir nu wax ci sant ak jërëjëf: Sunu Baay bi nekk ci asamaan...