TSK

TSK · 1 Peter 2:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak noteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.

Ki ñu woo ci Sang bi, fekk ko mu dib jaam, mooy ki Sang bi goreel. Naka noonu, gor si ñu woo, ab jaamu Almasi lay doon.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.

Te ngeen xam ne ci loxol Boroom bi ngeen di nangoo yool bi ngeen muurloo. Sang Almasi mooy ki ngeen di jaamu.

Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk, wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte; xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.

Ag ngoreel lañu leen di dig, te ñoom ci seen bopp, ay jaami yàqute lañu, nde lu la man, yaa dib jaamam.