TSK

TSK · 1 Peter 3:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.»

Nit ku jub garab la, doom ya di dundal; ku rafet xel wut nit ñi.

Dafa mel ni ndaw suy séy; li feek jëkkëram di dund, yoon a yeew buumu jëkkëram ci baatam. Waaye su jëkkër ji deeyee, ndaw si teqlikoo na ak yoon wi ko yeewoon buumu jëkkëram.

Yaw miy jabar ji nag sa texey jëkkër man naa jaare ci yaw, jombul; yaw jëkkër ji it, sa texey jabar jaare ci yaw, jombul.

¶ Waaye nag bëgg naa ngeen xam ne gépp góor, Almasi moo di boppam; jigéen, góor moo di boppam, te Almasi, Yàlla moo di boppam.

¶ Na jabar nangul jëkkëram ni mu nangule Sang bi.

¶ Jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, noonu mu jekke ci ku bokk ci Boroom bi.

Ci biir sawara wuy sëlsëli lay doon. Ca lay mbugal ñi xamul Yàlla, ak ñi baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.

Titus 2:3 TSK

¶ Naka noonu, jigéen ñu mag ñi itam, nañu jëfe ni mu jekke ci ay nit ñu sell; buñu yàq der, bu leen sàngara jiital, te nañuy jàngle lu baax,

¶ Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.

¶ Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal, ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.

Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?