TSK

TSK · 1 Peter 4:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Hosea 6:7 TSK

«Waaye ñoom ca dëkk ba, Adam lañu feccee kóllëre, foofa lañu ma wore.

¶ Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu deeyal bàkkaar, te di dundal Yàlla, ci Yeesu Almasi.

Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.

Te ki deeyal ñépp, daa deeyal ñépp ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki leen deeyal, ba dekki.

Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan, ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.

te mooy ngeen ba seen jikko ju jëkk ja, ngeen teqlikoo ak seen jëmmu démb ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute.

Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.

¶ Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye.

Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci jaamub Almasi Yeesu, Epafras, mi bokk ci yeen. Ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.

Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.

¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.