TSK

TSK · 1 Samuel 13:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.

¶ Musaa nag tudde cér yii, askanu Gàdd, ak askanu Ruben, ak genn-wàllu giirug Manase doomu Yuusufa: nguurug Siwon buurub Amoreen ñi la leen jox, ak nguurug Og buuru Basan, réew ma mépp, boole ca dëkk yu mag ya, ak àll ya ko wër.

Gannaaw loolu, na kilifa yi dellu wax ak gàngoor gi, ne leen: «Ana ku ci ragal, ana ku ciy yox-yoxi? Na daldi ñibbi kat, bala moo yoqiloo ay moroomam, ni moom.»

Ba Sóol ak bànni Israyil yépp déggee waxi waa Filisti jooju, jàq nañu, tiit nañu lool.

Dees na topp ci gannaaw Aji Sax ji, muy yëmmu ni gaynde. Mooy yëmmu moos ni gaynde, ay doomam di lox, jóge sowu.