TSK

TSK · 1 Samuel 16:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ.

¶ Ba loolu amee Elkana ak njabootam teela xëy ca ëllëg sa. Ñu màggal Aji Sax ji, ba noppi bàyyikoo fa, ñibbi seen kër ca Raama.

Su ko defee Noowug Aji Sax jee naa milib ci sa kaw, ngay waxandoo ak ñoom, soppiku, doon keneen nit.

Ba Sóol ak surgaam àggee Gibeya, kurélu yonent yaa ne pemm, dajeek moom. Noowug Yàlla ne milib ca kaw Sóol, muy waxandoo ak ñoom ay waxyu.

Kenn ca dag ya ne ko: «Man de, gis naa jenn doomu Yese waa Betleyem bi. Ku mana xalam la te jàmbaare. Ñeyi xare la. Ku déggi wax, ku góorayiw, te Aji Sax ji ànd ak moom.»

Yewu jóg, ànd ak moom, dugg ca biir kër ga, mu sotti diw ga ca boppam, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil nee: Diw naa la, fal la buurub Israyil sama ñoñ.

Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,