Genesis 21:1
TSK
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji yéwéne na Saarata, ni mu ko waxe woon, defal ko li mu ko digoon.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji yéwéne na Saarata, ni mu ko waxe woon, defal ko li mu ko digoon.
¶ Ba loolu amee Elkana ak njabootam teela xëy ca ëllëg sa. Ñu màggal Aji Sax ji, ba noppi bàyyikoo fa, ñibbi seen kër ca Raama.
¶ Ci kaw loolu Samiyel di màgg, Aji Sax ji ànd ak moom, waccul genn kàddug Samiyel, mu fanaan àll.
Kon nga xam lu jaadu, neex Yàllaak doom aadama.
¶ Ngóor sa nag di màgg, xel ma di yokku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba mu feeñoo bànni Israyil.
Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi.