TSK

TSK · 2 Kings 25:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

maa ngi sàkku asamaan ak suuf seedeel maak yeen bésub tey jii, ne su boobaa yeenay sànkoo sànku ci lu gaaw, ba wuute ca réew, ma ngeen jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko. Su boobaa dungeen fa yàgge, ndax dees leen di raafal, ba ngeen jeex tàkk.

Aji Sax jee leen di wasaare ci biir mboolem xeeti àddina, cat ba cat, ngeen di fa jaamu yeneen yàlla yu ngeen xamuloon, du yeen du seeni maam, yàllay bant ak doj.

Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege,

ba Aji Sax ji dëddu leen, muy la mu waxoon, yonent yay jaamam jottli ko. Noonu la mujj génne Israyil réewam, yóbbu leen Asiri ba bésub tey jii.

¶ Mu yóbbu Yowakin Babilon mook ndeyam aki soxnaam aki jawriñam ak kilifay réew ma.

Maa leen di def ñu jara seexlu, di musibay mboolem réewi àddina, ba fépp fu ma leen sànni, seen tur di fa saaga te kuy léeboo ak kuy kókkalee mbaa ngay móoloo, ñoom ngay tudd.

Aji Sax ji ci boppam moo leen tasaare, faaleetu leen; cér lees séddul sarxalkat, te teraleesul mag.

Man Aji Sax ji maa wax, mu dikk, ma jëfe ko. Duma bàyyi, duma ñéeblu, duma yërëm; say jikko ak say jëf lees lay àttee. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»