TSK

TSK · 2 Peter 1:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Du leble, ba teg ca; du nangu ger, ngir fexeel jaambur. Lii ku koy jëfe doo jang.

Yàlla doŋŋ ay dalal sama xel, moo may wallu.

Ku jub du tërëf mukk, te dees na ko fàttliku ba fàww.

Ndokklee kuy jëfe lii, ndokklee doom aadama ju jàppoo lii, di sàmm bésub Noflaay, bañ koo ñàkke worma, di sàmm loxoom ci jépp jëf ju bon.»

Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.

Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ay ñoñam,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»

Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néegu biir bu Yàlla ba.

yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.

¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.

Gannaaw yaa sàmm sama kàddu, ba muñ ni ma la ko sante, man itam dinaa la sàmm ci waxtuw nattu biy wàccsi ci àddina sépp, ngir nattu waa kaw suuf.