TSK

TSK · 2 Peter 1:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Bokk yi, man ci sama bopp, li ma bir ci seen mbir moo di yéene ju rafet ngeen fees, te buural ngeen bépp xam-xam, man ngeena artoonte it.

Sampleen seeni reen ci moom, tabaxuleen ci moom, feddlikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaanal kàdduy cant.

Moo tax li ma lay fàttli moo di nga xamb taalub mayu Yàlla, ga nga jote ca ba ma la tegee samay loxo.

¶ Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw, seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol, ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.

¶ Silwan, miy mbokkum gëmkat mu wóor, ci sama xalaat, ci ndimbalam laa leen bind kàddu yu gàtt yii, di leen ñaax aka seedeel ne lii kat moo di yiwu Yàlla dëgg. Taxawleen ci bu dëgër.

Waaye dinaa def sama kem-kàttan, ba fu ngeen tollu, di fàttliku mbir yooyu, gannaaw bu ma dëddoo.

¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.

Jude 1:5 TSK

¶ Doonte xam ngeen loolu lépp ba noppi, dama leen di fàttli rekk ne Boroom bi moo jëkka musal ñoñam, génne leen réewum Misra, te gannaaw gi moo raafal ña gëmul woon ca ñoom.