¶ Yanqóoba moom topp yoonam. Ci kaw loolu ay malaakay Yàlla feeñu ko.
TSK
TSK · 2 Samuel 2:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu Urim, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israyil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.»
Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.»
Daawuda dellu seet ci Aji Sax ji, Aji Sax ji ne ko: «Doxal dem Keyla, man, maay teg waa Filisti ci say loxo.»
Ci biir loolu Daawuda wax ak sarxalkat ba Abiyatar doomu Ayimeleg, ne ko mu indil ko xar-sànni mi. Abiyatar indil Daawuda xar-sànni ma.
Diir ba Daawuda falu buurub Ebron gu waa kër Yuda, juróom ñaari at la ak juróom benni weer.
Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma songi waa Filisti? Dinga leen teg ci sama loxo?» Aji Sax ji ne ko: «Demal, maay teg waa Filisti ci say loxo déy!»
¶ Ba ñu demee ba ñeenti at jàll, Absalom ne Buur: «May ma, ma dem Ebron defali Aji Sax ji la ma ko xasaloon,
Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, xamal ma fi nga ma jaarloo.
Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israyil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.