Ndawi bànni Israyil ne ko: «Sél wi rekk lanuy topp, te ndox mu nu naan, nook sunug jur, noo la koy fey. Ñaanunu lenn lu moy doxe sunuy tànk, ba jàll.»
TSK
TSK · 2 Samuel 20:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba mu ko defee, nag ya jubal xocc yoonu Bet Semes, topp wenn yoon wi rekk, di nàññiy dem. Jàdduñu ndijoor, jàdduñu càmmoñ. Kàngami Filisti ya topp ca, ba fa Bet Semes tàmbalee.
¶ Buurub Asiri nag tollu ca Lakis, yebal bummeem ak kilifay jawriñam ak bëkk-néegam, ñu ànd ak mbooloom xare mu takku, dem Yerusalem. Ba ñu agsee Yerusalem ba tollook solomu mbàndum kaw ma, fa feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa lañu taxaw.
Aji Sax ji wax Esayi ne ko: «Génnal gaaw, dajeek Axas, yaak sa doom Seyar Yasub, ma nga ca catal solomu mbànd ma féete kaw, ca yoonu toolu fóotkat ya.
Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, xàll-leen yoonu xeet wi, maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, dindi doj yi! Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.