TSK

TSK · 2 Samuel 21:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba loolu wéyee xiif am ca réew ma, muy xiif bu wuute ak ba woon ca jamonoy Ibraayma; Isaaxa nag dem Gerar ca Abimeleg, buurub waa Filisti.

¶ Gannaaw loolu xiif bi metti ca réew ma.

Bu ma téyee loxo bi ma leen di leele, fukki jigéen dinañu bokk lakk seen mburum njël ci benn taal doŋŋ, natt ko ay somp, séddale, ngeen lekk, te dungeen suur.

Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.»

Daawuda seet ci Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma dem xarejeek waa Filisti?» Aji Sax ji ne Daawuda: «Demal kay xareek waa Filisti, xettli waa Keyla.»

Mbaa kilifay Keyla duñu ma teg ci loxoom? Boroom bi, ndax li ma dégg ñu naan Sóol a ngi ñëw, dëgg la? Éy Aji Sax ji, Yàllay Israyil, sama Boroom, ngalla wax ma!» Aji Sax ji ne: «Dina ñëw.»

Daawuda dellu laaj Aji Sax ji. Mu ne ko: «Bul jubal, doxeleen gannaaw, dal ca seen kaw fa janook garabi sànd ya.

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji mereeti bànni Israyil, ba tax mu xiir Daawuda ci def lu leen di lor. Mu def ci xelam ne ko mu dem lim waa Israyil ak Yuda.

Ilyaas tegu ca yoon wa ngir jàkkaarloojeek Axab. Booba xiif ba metti na ca Samari.

¶ Am na bés Alyaasa wax ndaw sa mu dekkaloon doomam ju góor ne ko: «Ayca, àndal ak sa njaboot, ngeen dali fu ngeen mana dal, ndax Aji Sax ji dogal na ab xiif ci réew mi, te dina am juróom ñaari at.»

Job 10:2 TSK

Dama naa Yàlla: Bu ma topp ug tooñ. Xamal ma kay li nga may topp, lu mu!

di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»

¶ Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne: