TSK

TSK · 2 Samuel 24:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

su boobaa li may def ak yeen mooy lii: maay jekki wàcce njàqare ci seen kaw, mu ànd ak woppi ràgg, yaram wu tàng jérr ak bët yu lëndëm, ngeen gën di wopp. Dingeen ji seenum pepp ci neen, ndax seeni noon a koy lekk.

Maay dalal saamar ci seen kaw, feye leen ko kóllëre gi ngeen fecci. Bu ngeen làqoo ci seeni biir dëkk yu mag sax, maay wàcce mbas ci seen biir, seeni noon jekku leen.

Aji Sax jee leen di dumaa woppi ràgg, ak yaram wu tàng, ak lakk-lakk, ak jant bu tàng jérr, ak maral, ak gàncax gu xuur, tegi liir, lépp topp leen ba ngeen sànku.

¶ Aji Sax jee leen di dumaa taabi Misra, ak neewoy kërug suuf, ak yaram wu xas, ak ër yuy xasan te dungeen mana am pajam.

Dees na leen gawe ci seen dëkk yépp, ba seen tata yu kawe te dàbbliku, ya ngeen yaakaaroon ci seen réew mépp, màbb. Dees na leen gawe seen dëkk yépp, ci mboolem réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.

¶ Jamono ya Daawuda nekkee ci jal bi, amoon na xiifub ñetti at yu tegloo. Daawuda diis ko Aji Sax ji. Aji Sax ji ne ko: «Li waral xiif bi moo di àqu deret ji topp Sóol ak waa këram ndax waa Gabawon ña mu rey.»

¶ Am na bés Alyaasa wax ndaw sa mu dekkaloon doomam ju góor ne ko: «Ayca, àndal ak sa njaboot, ngeen dali fu ngeen mana dal, ndax Aji Sax ji dogal na ab xiif ci réew mi, te dina am juróom ñaari at.»

mbaa mbas mu yooteg lëndëm, ak balaa buy fàdde njolloor.

Su ma yebalee mbas ci kaw réew mii it, ba xëpp fi samam sànj ci biir deret ju tuuru, ngir dagge fi nit ak mala,