1 Samuel 15:28
TSK
Samiyel ne ko: «Nii la Aji Sax ji dagge nguurug Israyil ci yaw bés niki tey, jox ko keneen ku la gën.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Samiyel ne ko: «Nii la Aji Sax ji dagge nguurug Israyil ci yaw bés niki tey, jox ko keneen ku la gën.
Mooy la ñu léeb bu yàgg rekk ne: “Ku bon, mbon rekk.” Man nag sama loxo du la dal mukk.
Kon ayca boog! Ndax Aji Sax jee ko digoon Daawuda, ba mu nee: “Ci sama jaam Daawuda laay walloo Israyil sama ñoñ, ci waa Filisti ak mboolem seeni noon.”»
Mefiboset sujjóot, ne ko: «Moo sang bi, maay kan ba nga di ma geesu, man mi tekkiwul dara, ba dara booloo jeex?»
Asayel ne ko: «Moo sang bi, man mi ab xaj gën, nu ma mana defe jooju jëf ju réy?» Alyaasa ne ko: «Aji Sax ji won na ma ne yaay doon buurub Siri.»
Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.