2 Samuel 4:4
TSK
¶ Fekk na Yonatan doomu Sóol ju góor am na doom ju góor ju tànk ya baaxul. Ndaxte ba ñu déggee tàgge bu jóge Yisreel, ñu ne Sóol ak Yonatan faatu nañu, fekk na xale ba am juróomi at. Ndaw sa ko daan topptoo, fab ko di gaawtuy daw, waaye na muy gaawtu di dem, xale ba daanu, daldi lafañ. Ma nga tuddoon Mefiboset.