Psalms 38:4
TSK
Danga maa mere, ma wéradi; maa bàkkaar, ba jagadi.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Danga maa mere, ma wéradi; maa bàkkaar, ba jagadi.
Bokk yi, xam ngeen ne ba ngeen dee ay yéefar, dees leena buuboon, lajjal leen, jëme ci ay tuur yu tëlee wax.
Li war moo di tëj seen gémmiñ, ndax këri lëmm lañuy tase àlluwa ju ñu amul sañ-sañam, ngir di ko sàkkoo am-am bu lewul.
Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.
Ndaxte ñenn a ngi ñu ñu yàgga bind seenub àtte, te ñoo yoxoosu ci seen biir, di ñu ñeme Yàlla; ñooy taafantoo yiwu Yàlla ngir yoonal ag yàqute, di weddi Buur biy kenn, te di sunu Boroom Yeesu Almasi.
Ñu ne leen: «Mujug jamono, dina am ay ñaawlekat yu topp seen bakkan, wéye seen kéefar.»