TSK

TSK · Acts 1:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Ma ne, dinaa yiiroo niir wu fatt, dikk ba agsi fi yaw, ngir bu may wax ak yaw, mbooloo mi di ci dégg, ndax ñu wóolu la ba fàww.» Ba loolu amee Musaa baamtul Aji Sax ji tontal mbooloo ma.

Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.

¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi ma, gisuma lu moy jëmm ju mel ni doomu nit di ñëw, mook niiri asamaan, jëm ci góor gu mag gi; ñu yóbbu ko ba ca moom.

Su boobaa dees na gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy.

Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»

Ba loolu amee ñaari seede yi dégg baat bu xumb jibe asamaan, ne leen: «Yéegleen fii.» Ñu yéeg asamaan ci biir aw niir, seeni noon di gis.