¶ Daawuda nag nekk ca xunti yu kawe ya ca màndiŋ ma, toog foofa ca tund, wa ca màndiŋu Sif. Sóol di ko seet bés bu nekk, waaye Yàlla tegul Daawuda cay loxoom.
TSK
TSK · Acts 12:19
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Gannaaw loolu Mardose dellu ca buntu kër buur. Aman nag muuru, daw ñibbi këram, ànd aku naqar.
xanaa mu sant Yerameel, kenn ci askanu Buur, mook Seraya doomu Asriyel, ak Selemya doomu Abdel, ne leen ñu jàpp Barug bindkat ba ak Yonent Yàlla Yeremi. Teewul Aji Sax ji làq leen.
Filib moom, dëkk ba ñuy wax Asot la gisaat boppam. Mu wéye di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkkoo dëkk, ba àgg Sesare.
¶ Ba ñu demee ba ca guddi, ga jiitu bés ba ko Erodd wara yóbbu, Piyeer a ngay nelaw ci diggante ñaari takk-der, ñu yeewe ko ñaari càllala, ay dag di wattu buntu kaso ba.
Ca ëllëg sa nu dem ba àgg Sesare. Nu dem kër Filib, xamlekatu xibaaru jàmm, bi bokk ci Juróom ñaar ñi. Nu dal ak moom.
¶ Ba loolu amee takk-der ya nara rey ña ñu tëj, bala ñoo féey, ba raw.