TSK

TSK · Acts 14:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Micah 7:6 TSK

Doom ju góor a ngi dofloo baay ba, ju jigéen ja jógal ndey ja, jabar jógal ndeyu jëkkër ja, nooni nit ki di waa këram.

Luke 2:34 TSK

Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqliku ci digg Israyil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal.

Foog ngeen ne maye jàmm ci kaw suuf moo ma indi? Déet kay. Maa leen wax lii, xanaa ag féewaloo.

Acts 13:2 TSK

Ñooñoo daje woon di màggal Boroom bi, boole kook koor. Ci biir loolu Noo gu Sell gi ne: «Beral-leen ma nag Barnaba ak Sóol ngir liggéey, bi ma leen wooye.»

Acts 17:4 TSK

Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.

Ñenn ña nag gëm la mu wax, ña ca des weddi.