Kóllëre gi ma fas ak yaw, te nga war koo sàmm, yaak sa askan, li mu laaj mooy lii: góor gu nekk ci yeen, war naa xaraf.
TSK
TSK · Acts 15:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jaambur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool.
¶ Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
¶ Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
Ki xarafoon bala ñu koy woo, bumu làq màndargam xaraf ma. Ki xaraful woon ba ñu koy woo, bumu xaraf.
Moonte Tit mi ma àndaloon sax, tegeesu ko fa wartéefu xaraf, te ci askanu gereg yi dul xaraf la bokk.
¶ Almasi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.
Ñi xaraf ñoom ci seen bopp sax toppuñu yoon wi. Teewul ñu bëgg ngeen xaraf, ngir mana damoo seen màndargam yaram, yeen ñi ñu xarafloo.
¶ Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina.
¶ Kon nag bu leen kenn sikkal ci ñam wu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, mbaa màggal bés bu rafet, mbaa Terutel weer, ak bésub Noflaay.