¶ Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?
TSK
TSK · Acts 15:11
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Romans 5:15
TSK
Romans 6:23
TSK
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
Galatians 1:6
TSK
¶ Man de jaaxle naa ci nii ngeen gaawa dëddoo Yàlla mi leen woo ci boppam, ci ndimbalal yiwu Almasi, bay topp xaat beneen xibaaru jàmmeey!
Ephesians 1:6
TSK
Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.
Titus 2:11
TSK
¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.
Revelation 5:9
TSK
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.