TSK

TSK · Acts 15:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

su boobaa, yaw, ngalla nangoo ko asamaan, màkkaan ma nga dëkke, ba jéggale, te nga jëf ba yool ku nekk kemu mboolem ay jëfam, yaw mi xam xolam, ndax yaw doŋŋ yaa xam xolu mboolem doom aadama.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma;

Maay Aji Sax jiy seetlu xel, natt ub xol, di yool ku nekk jëfinam, la yellook añam.

Acts 2:4 TSK

Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.

¶ Ba Piyeer di wax kàddu googu, Noo gu Sell gi daldi wàcc ci kaw mboolem ñay déglu kàddu ga.

¶ «Naka laa tàmbalee wax ak ñoom Korney, Noo gu Sell gi daanu ci seen kaw, na mu jëkkoona daanoo ca sunu kaw.

Te Yàlla moo doon dëggale seedey ñooñu, ay firnde aki kéemaan, ak wépp xeeti kawtéef, ak ay mayi Noo gu Sell gi, may yi mu séddalee ni mu ko soobe.

Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.