di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.
TSK
TSK · Acts 16:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,
Noo gi nag ne ma: “Àndal ak ñoom, te bul nàttable.” Juróom benni bokk yii ngeen di gis ñoo ma gunge, nu dem ba dugg ca kër Korney.
Ñu dem ba ca kemu Misi, nara jàlli biir diiwaanu Bitini, Xelum Yeesu mayu leen ko.
Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.
Ña àndoon ak moom ñoo di Sopater doomu Pirus ma cosaanoo Bere, ak Aristàrk ak Segond, waa Tesalonig ya, ak Gayus, ma dëkke Derbe, ak Timote, ak waa diiwaanu Asi ya, Tisig ak Torofim.
Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.
¶ Ci wàllu ndimbal li jëm ci gëmkat ñu sell ñi, noonu ma ko digale mboolooy gëmkati diiwaanu Galasi, yeen itam defeleen ko noonu.
bawoo itam ci mboolem bokk yi nekk ak man, ñeel mboolooy gëmkat yu diiwaanu Galasi.
¶ Xam nga ne waa diiwaanu Asi gépp a ma won gannaaw, te Fusel ak Ermosen ci lañu bokk.
¶ Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.
¶ Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,