TSK

TSK · Acts 17:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Acts 14:1 TSK

¶ Ba Póol ak Barnaba nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñu waare, ba mbooloo mu mag gëm, ay Yawut aki Gereg.

¶ Ba bésub Noflaay ba taxawee, nu génn ca buntu dëkk ba, ca wetu dex ga, daldi fay gis bérab bu nu foog ne ab jullikaay la. Nu toog fa nag, di waxtaan ak jigéen ña fa daje.

¶ Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor.

Acts 27:2 TSK

Nu dugg gaalu dëkk ba ñuy wax Àddramit tey jaareji teeruy Asi, daldi tàbbi biir géej, Aristàrk jenn waay ju dëkke Tesalonig ca diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.

¶ Man la Póol, mi ànd ak Silwan ak Timote ci kàddu gii ma yékkati, ñeel mbooloom gëmkati waa Tesalonig, ñi bokk ci Yàlla Baay bi ak Sang Yeesu Almasi. Yiw ak jàmm ñeel na leen.

Ndax kat Demas, àddinay tey la sopp ba tax mu wacc ma, dem Tesalonig, te Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi.